Su dee damey dee
Translated to Wolof by @Ndeye Debo SeckSu dee damey dee
Da ngeen wara dund
Ngir nettali samaw wey
Ngir jaay samey yëff
Ngeen jënd si ap sagar
Ak i weñ
(Na weex te am geen gu gudd )
Ndax gènn gone ci Gaza
Di xool jawwu ji si ay gët
Di xaar baayam mi saay si ab taal
Te taggu wut kènn
Tàggu wut sax njabootam
Tàggu wut sax boppam-
Ndax gone googu le, gis serwolan bi ngeen ma defaral di naaw ca kaw
Te mu am yaakaar ne donte ben waxtu la maalaka mo wàcc andiwaat mbëggeel
Su dee dama dee
Na jur yaakaar
Na doon wey wu dul fey